Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 95:3-7 in Wolof

Help us?

Sabóor 95:3-7 in Kàddug Yàlla gi

3 Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
4 Moo moom xóotey suuf, moom colli tund yi,
5 moom géej, sàkk ko, moom jéeri ji mu mooñ.
6 Nan sëgg, sujjóot, sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
7 Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
Sabóor 95 in Kàddug Yàlla gi