3Aji Sax ji, fu ku bon kiy àkki? Fu ku bon kiy kañu àkki?
4Ñu ngi làmmiñoo reewande, képp kuy def lu bon di damu.
5Aji Sax ji, say ñoñ lañuy dëggaate; say séddoo lañuy néewal.
6Jëtun akub doxandéem, ñu faat; ab jirim, ñu bóom,
7te naa: «Ki Sax gisu ci, Yàllay Yanqóoba jii yégu ko.»
8Yeen bokk yu dofe yi, moytuleen. Gàtt xel yi, kañ ngeen di muus?
9Ki jëmbati nopp, da dul dégg a? Am ki xari gët, da dul gis?
10Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee? Du mooy kiy xamal nit?
11Aji Sax ji xam na xalaatu nit, xam ne cóolóolu neen la.
12Ki Sax, ndokklee ki ngay yar, tàggat ko ci saw yoon,
13dëfal ko ci bési safaan, ba keroog ñuy gasal ku bon.
14Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.
15Àtte dina dellu laloo njekk, képp ku jub topp ca.
16Ana ku may taxawal ci ñu bon ñi? Ku may jógal ci biir ñiy def lu bon?
17Su ma Aji Sax ji walluwloon, tuuti ma fanaani réew ma ne selaw.
18Dama noon: «Tarxiis naa!» Waaye yaa ma awoo sa ngor.
19Ma bare xalaati xol, nga dëfal ma, ma bég.
20Loo séq ak njiit lu jubadi luy yoonal njubadi?
21Ñii dañoo mànkoo, di tëru ku jub, di teg àtteb dee ku deful dara.
22Waaye Aji Sax jeey sama rawtu, sama Yàlla laay sës, làqu.
23Moo leen di këpp seen ñaawtéef, sànke leen seenug mbon. Sunu Yàlla Aji Sax jee leen di sànk.