7Junni daanu fi sa wet, fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor, du tax mu jege la.
8Say gët nga ciy teg, di seetaan ku bon di jot yoolam.
9Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji, Aji Kawe jii di sama rawtu,
10genn loraange du la dab, balaa du jege sa xayma.
11Ay malaakaam la lay booleel, ñu di la sàmm foo jëm.
12Seeni loxo lañu lay leewoo, ba doo fakkastaloow doj.
13Dangay falaxe jaan ak gaynde, di rajaxe ñàngóor ak sibi.
14Yàlla da naa: «Kii de man la safoo, ma di ko xettli. Man la xam, te maa koy teg fu wóor.
15Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,
16reggal koy fan, baaxe ko samag wall.»