4Kiiraayam la lay sànge, nga yiiru, làqu; wormaam yéew la, di la aar.
5Doo ragal njàqarey guddi mbaa fittu bëccëg
6mbaa mbas mu yooteg lëndëm, ak balaa buy fàdde njolloor.
7Junni daanu fi sa wet, fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor, du tax mu jege la.
8Say gët nga ciy teg, di seetaan ku bon di jot yoolam.
9Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji, Aji Kawe jii di sama rawtu,
10genn loraange du la dab, balaa du jege sa xayma.
11Ay malaakaam la lay booleel, ñu di la sàmm foo jëm.
12Seeni loxo lañu lay leewoo, ba doo fakkastaloow doj.
13Dangay falaxe jaan ak gaynde, di rajaxe ñàngóor ak sibi.