3Àll laa lay wooye, sama xol jeex; yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
4Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
5Naa dëkke sa xayma, ba fàww; làqoo sa kiiraay. Selaw.
6Yàlla, yaa dégg samay dige, sédd ma céru ñi la wormaal.
7Ngalla féqal fani Buur, ay atam bare, sët ba sëtaat.