Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 59

Sabóor 59:7-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.
8Déglul li ñuy yebbee ci seen gémmiñ, seen làmmiñ niy saamar, ñu defe ne kenn déggu leen.
9Te yaw Aji Sax ji, yaa ngi leen di ree, yaa ngi kekku yéefar yii yépp.
10Yaay sama doole, ma di la séentu, yaw Yàlla, yaay sama rawtu.
11Sama Yàlla ju goree may gatandu. Moo may may ndam ci noon yi, ma gis.
12Yàlla, bu leen rey, lu ko moy samaw xeet fàtte. Tasaaree leen sa doole, daane leen. Boroom bi, yaa nuy feg.
13Bàkkaar lañuy wax, seeni kàddu, bàkkaari neen. Yal nañu bew ba daanu, yooloo ko seeni saagaak seeni fen.
14Meral, jeexal leen, jeexal leen, ba ñu jeex tàkk, ba ñépp xam ne Yàllaay Buur ci giirug Yanqóoba, ba ca cati àddina. Selaw.
15Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.
16Ñuy wër di wut lu ñu lekk, su ñu suurul, di ñurumtu.

Read Sabóor 59Sabóor 59
Compare Sabóor 59:7-16Sabóor 59:7-16