3Xettlimaak ñiiy def lu bon, wallu maak bóomkat yi.
4Aji Sax ji, ñu ngii di ma tëru, nar maa rey, di ma songe seen doole, te tooñuma, moyuma.
5Defuma lu ñaaw, ñuy xélu, di ma waajal; ngalla, jógal taxawusi ma, ba gis.
6Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Yàlla Boroom gàngoor yi, yewwul, dikkeel xeeti yéefar yépp, mbugal! Workat yu bon yi, bu leen yërëm! Selaw.