3 Xettlimaak ñiiy def lu bon, wallu maak bóomkat yi.
4 Aji Sax ji, ñu ngii di ma tëru, nar maa rey, di ma songe seen doole, te tooñuma, moyuma.
5 Defuma lu ñaaw, ñuy xélu, di ma waajal; ngalla, jógal taxawusi ma, ba gis.
6 Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Yàlla Boroom gàngoor yi, yewwul, dikkeel xeeti yéefar yépp, mbugal! Workat yu bon yi, bu leen yërëm! Selaw.