Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 56

Sabóor 56:1-5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat.
2Éy Yàlla, baaxe ma, nit a ngi may lakkal, ab xeexkat a ma yendoo sonal.
3Noon yee ma yendoo lakkal, bare lool di xareek man. Ku Màgg ki,
4bés bu ma tiitee, yaw laay wóolu.
5Yàlla laay màggal kàddoom, Yàlla laa wóolu, ragaluma. Lu ma nit manal?

Read Sabóor 56Sabóor 56
Compare Sabóor 56:1-5Sabóor 56:1-5