1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalif, te di woyu mbëggeel.
2Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
3Yaa gëna góorayiwe ci àddina, sa kàddu diw yiw, ndax Yàllaa la barkeel ba fàww!
4Jàmbaaroo, takkal sa saamar, te yànj, am daraja;
5ànd ak daraja, dawal ba am ndam, di dawal dëgg ak yërmande ji war, ba mana def ay jaloore.
6Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.