Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 39

Sabóor 39:5-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.
6Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan, sama giiru dund du dara fi yaw. Képp ku taxaw di cóolóolu neen. Selaw.
7Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
8«Éy Boroom bi, lu may xaarati? Sama yaakaar yaw a.
9Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ, bu ma bàyyi, dof di ma reetaan!
10Noppi naa, dootuma wax, yaw yaa dogal lii.
11Waaye ngalla teggil sab yar, sa diisaayu loxoo ngi may jekkli.
12Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko, ronq ni max la mu gëna fonk. Nitoo nit, cóolóolu neen. Selaw.

Read Sabóor 39Sabóor 39
Compare Sabóor 39:5-12Sabóor 39:5-12