Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 34

Sabóor 34:1-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem.
2Naa màggal Aji Sax ji saa su ne, di ko sant fu ma tollu.
3Aji Sax ji laay sagoo, néew-ji-doole dégg, bég.
4Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man, nu bokk wormaal turam.
5Maa sàkku Aji Sax ji, mu nangul ma, tàggale maak lépp lu ma ragal.
6Ku yaakaar Aji Sax ji bég, leer nàññ, gàcce du ko sëlëm.
7Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.
8Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la, di la wallu.
9Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokklee yaw mi ko làqoo.
10Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi; ku ko ragal doo ñàkk dara.
11Gaynde man naa ndóol, xiif, nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax.
12Dikkal doom, déglu ma, ma jàngal la ragal Aji Sax ji.
13Ana ku dund neex, mu bëgga gudd fan, ba gis ngëneel?
14Na làmmiñam daw lu aay, dawi fen.
15Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
16Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, te ay noppam la dékk wooteb wallam.

Read Sabóor 34Sabóor 34
Compare Sabóor 34:1-16Sabóor 34:1-16