1Màggal-leen Ki Sax! Nangeen màggale Aji Sax ji fa asamaan, màggale ko fa kawa kaw.
2Màggal-leen ko, yeen malaakaam yépp, màggal-leen ko, yeen gàngooram yi.
3Màggal-leen ko, yeen jant beek weer wi, màggal-leen ko, yeen mboolem biddiiw yii di nes-nesi.
4Màggal-leen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw, ba ca ndox ma tiim asamaan ya.
5Nañu màggal turu Aji Sax ji, kii kat a santaane, lii lépp am.
6Moo leen samp, ñu sax ba fàww, mu dogal ko, te du toxu.
7Nangeen màggale Aji Sax ji fa kaw suuf, yeen ninki-nànkay géej ak xóote yépp,
8ba ca melax yaak doj yu sedd yay taw, ak tawub yuur akub lay, ba ca ngëlén yu mag yay def ndigalam.
9Màggal-leen ko yeen tund yu mag yeek yu ndaw yépp, ba ci garab yiy meññ ak garabi seedar yi,