3ba ma tàggook bopp bu ubu ak njàqarey xol bu sax, ba noon dootu ma man?
4Céy Aji Sax ji sama Yàlla, geesu ma, wuyu ma, leqli ma, bala ma ne sërëx ci nelawi ndee,
5noon ba naan: «Daan naa ko,» bañ yay bége saab jéll.
6Man de maa ngi dénkoo sa ngor, di bànneexoo sag wall. Naa woy Aji Sax ji, ki may baaxe xéewalam.