3Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul.
4Kiy sàmm Israyil kay gëmmul, nelawul.
5Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.
6Du naaj wu lay dal bëccëg, mbaa leer gu ndaw guddi.
7Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, di sàmm sa bakkan.
8Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk, tey ak ëllëg.