3 Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul.
4 Kiy sàmm Israyil kay gëmmul, nelawul.
5 Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.
6 Du naaj wu lay dal bëccëg, mbaa leer gu ndaw guddi.
7 Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, di sàmm sa bakkan.
8 Aji Sax jee lay sàmm, dem ak dikk, tey ak ëllëg.