Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ose

Ose 6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.
2Ñaari fan, mu leqli nu, ñetteel ba mu yékkati nu, nuy dund fi kanamam.
3Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
4«Ana nu ma lay def, yaw Efrayim? Nu ma lay def yaw Yuda? Te sa ngor di xiinu suba, mbaa ab lay, jekki ne mes.
5Moo tax yonent yi laa leen di dumaa, sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye. Seen àttee leen di jollil ni ceeñeeru njël.
6Ndax ngor laa namm, dub sarax, ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.
7«Waaye ñoom ca dëkk ba, Adam lañu feccee kóllëre, foofa lañu ma wore.
8Galàdd mooy dëkkub defkati ñaawtéef, taq ripp ak deret.
9Ni saaysaay siy tëroo, ni la sarxalkat yi lëkkoo, di bóome ca yoonu Sikem. Ndaw jëf ju ñaaw!
10Ci kërug Israyil laa gis lu yées: Fa la Efrayim di gànctoo, Israyil googu laa ne moo sobeel boppam.
11Yuda yaw it, sam ngóob ma ngay taxawe, kera bu may tijji sama wërsëgu ñoñ.