Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ose

Ose 4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddug Aji Sax ji, Aji Sax ji kat moo séq ab layoo ak waa réew mi: «Du kóllëre, du ngor, du gennug ràññee Yàlla ci réew mi.
2Xanaa ay móolu aki wor, bóome, càcc ak njaaloo. Dañoo ràkkaaju, di tuur deret ci kaw deret.
3Moo tax réew mi wowal, mboolem lu fi dëkke ràgg, ba ci rabi àll yi, ak njanaaw yi, jëni géej itam day réer.
4«Waaye bu ci kenn layoo, bu ci kenn sikke, ndax sa bokk yee mel ni ñuy layook sarxalkat yi.
5Dingeen tërëf bëccëg, yonent yi ànd ak yeen tërëf guddi, te maay sànk seen ndey.
6Sama ñoñ a sànku ndax ñàkka xam; yeen, xam-xam ngeen gàntal, ma gàntal seenug carxal. Yeena fàtte seen yoonu Yàlla, man it maay fàtte seeni doom.
7sarxalkat yi ñu gëna baree, gën ma nee moye, seenub sag, gàcce laa koy soppi.
8Sama saraxi póotum bàkkaari ñoñ lañuy dunde, tey yàkkamti ñu def njubadi.
9Waaye niki askan wi, niki sarxalkat yi, maa leen di dikke seen añu jikko, maa leen di fey seeni jëf.
10Ñooy lekk te duñu regg, di gànctu te duñu giir, nde Aji Sax ji lañu noppee topp.
11Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees, moo yóbbu seenum xel.
12Sama ñoñ, seen bant lañuy seeteey, seenu yet di leen waxaleey. Xelum ngànctu moo leen wacc, ñooy gànctu, lajje fa seen Yàlla.
13Ca kaw tund yu mag ya lañuy rendee ay sarax, cuuraay, ñu taale ca tund yu ndaw ya, ak ca taatu gii garab gu mag, ba ca gee, fa ker ga neexe. Moo tax seeni doom di gànctu, seen séeti doom di jaaloo.
14Duma mbugal seeni doom ndax li ñuy gànctu mbaa seen séeti doom ndax li ñuy jaaloo, ndax ñoom sarxalkat yi ci seen bopp, ay gànc lañuy teggeendool te gànc yi ci jaamookaayi xërëm yi, ñoom lañuy indeendool jooxe. Askan wu amul ug dégg, sànku.
15«Yeena ngi gànctu, yeen bànni Israyil, waaye na Yuda mucc ci googu tooñ. Buleen dugg Gilgal, buleen yéegi Bet Awen di giñ ci Aji Sax jiy dund.
16Ndegam ni aw nag tëwe ni la Israyil tëwe, ndax léegi Aji Sax jee leen di foral nim xar ci parlu mu ne màww?
17Efrayim googu laa ne, moo lëngook jëmmi tuur! Seetaan leen.
18Seenu ñoll giiful sax, ñuy gànctoo gànctu, te gàccee gënal seeni kilifa.

19Callweer a leen di wal, ñu kersawoo seen jooxey tuur.