Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 3

LUUG 3:4-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.
5Nañu sëkk xur yi, maasale tund yi ak jànj yi. Yoon yi dëng ñu jubbanti leen, yi ñagas ñu rataxal leen.
6Bu ko defee bépp mbindeef dina gis mucc gi Yàlla tëral.”»
7Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
8Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te baña nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.
9Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.»
10Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu wara def nag?»
11Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.»
12Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu wara def?»
13Mu ne leen: «Laajleen rekk lu jaadu.»
14Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»

Read LUUG 3LUUG 3
Compare LUUG 3:4-14LUUG 3:4-14