1Éy Aji Sax ji Yàlla, boroom mbugal! Boroom mbugal, feqal sag leer!
2Yaw miy àtte àddina, jógal yool ku bew.
3Aji Sax ji, fu ku bon kiy àkki? Fu ku bon kiy kañu àkki?
4Ñu ngi làmmiñoo reewande, képp kuy def lu bon di damu.
5Aji Sax ji, say ñoñ lañuy dëggaate; say séddoo lañuy néewal.
6Jëtun akub doxandéem, ñu faat; ab jirim, ñu bóom,