2Céy ngëneel li ci sant Aji Sax ji, di la woy, yaw Aji Kawe ji,
3xëye tudd sa ngor, gonloo xamle sa worma,
4xalamu fukki buum ànd ak moroom ma, xeetu kooraa jibandoo.
5Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, may sarxolle ci say manoore.
6Aji Sax ji, yaa réyi jëf; xóoti pexe.