Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 91

Sabóor 91:12-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Seeni loxo lañu lay leewoo, ba doo fakkastaloow doj.
13Dangay falaxe jaan ak gaynde, di rajaxe ñàngóor ak sibi.
14Yàlla da naa: «Kii de man la safoo, ma di ko xettli. Man la xam, te maa koy teg fu wóor.
15Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,
16reggal koy fan, baaxe ko samag wall.»

Read Sabóor 91Sabóor 91
Compare Sabóor 91:12-16Sabóor 91:12-16