14Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal, def gàngoor gu néeg, di rëbb sama bakkan, te seetuñu la ci.
15Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
16Geesu ma, baaxe ma. Dooleelal sab jaam, wallul ki sa jaam sukk jur!
17Ngalla def ma sa firndey mbaax, ba bañ yi gis ci, rus, ndax yaw Aji Sax, ji ma dimbali, dëfal ma.