12«Waaye sama ñoñ déggaluñu ma, Israyil gii nangulu ma.
13Moo tax ma bërgël leen ak seenug të, ñuy wéye seeni pexe.
14Éy su ma sama ñoñ déggaloon, éy su Israyil toppoon samay nammeel!
15Ci saa si laay torxal seeni noon, duma seeni bañ,
16ba ku bañ Aji Sax ji di ko raamal, te àppam du jeex ba fàww.