12 «Waaye sama ñoñ déggaluñu ma, Israyil gii nangulu ma.
13 Moo tax ma bërgël leen ak seenug të, ñuy wéye seeni pexe.
14 Éy su ma sama ñoñ déggaloon, éy su Israyil toppoon samay nammeel!
15 Ci saa si laay torxal seeni noon, duma seeni bañ,
16 ba ku bañ Aji Sax ji di ko raamal, te àppam du jeex ba fàww.