Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 7

Sabóor 7:13-17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
13Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram, bank xalaam, diir la.
14Moom la waajalal ngànnaayi ndee, def ko fitt yuy boy.
15Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.
16Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.
17Fitnaam, këpp ci boppam; coxoram, xàŋŋ cim kaaŋam.

Read Sabóor 7Sabóor 7
Compare Sabóor 7:13-17Sabóor 7:13-17