13 Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram, bank xalaam, diir la.
14 Moom la waajalal ngànnaayi ndee, def ko fitt yuy boy.
15 Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.
16 Am kan lay gas, ba mu xóot, te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.
17 Fitnaam, këpp ci boppam; coxoram, xàŋŋ cim kaaŋam.