36Teewul ñu di ko jéema naxey wax, di ko fen.
37Joxuñu ko woon xol, sàmmuñu kóllëreem.
38Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,
39ndax xalaataat ne suuxu neen lañu, di noo guy dem te du délsi.
40Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.
41Ñu dellu di diiŋat Yàlla, di naqaral Aji Sell, ji séddoo Israyil.
42Fàtte nañu ndimbalam la, bés ba mu leen jotee ca noon ba,
43ba def ay firndeem ca Misra, muy kiraamaam ya ca Cowan.
44Moo soppli deret seen yooni ndox, ba naaneetuñu wal ya.
45Mu wàcce seen biir ndiiraanu weñ yu leen di lekk, ak mbott yu leen sànk.
46Mu jox soccet yi seen gàncax, jébbal njéeréer yi seen meññeef.
47Seen garabi reseñ, mu fóome tawab yuur, seen garabi sikomoor, mu fóome waame.
48Seen jur gu gudd, mu bàyyeek tawab yuur, seeni gàtt, mu bàyyeek sawaray melax.
49Yàlla sotti leen tàngooru xadaram, mu dim sànj ak naqar ak njàqare, lépp di gàngooru ndaw yu indiy musiba.
50Mu afal meram, ba musalul seen bakkan, xanaa jébbal leen mbas ma.
51Daa fàdd képp kuy taaw ca Misra te juddoo seen digg doole, fa xaymay sëti Xam.
52Mu génne ñoñam niy gàtt, wommat leen ni gétt ca màndiŋ ma,
53ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu; seeni noon, géej ga mëdd leen.
54Mu yóbbu leen fa suufam su sell sa, fa tund woowu mu jënde dooleem.
55Da leena dàqal ay xeet, dogal leen céru suuf, sancal giiri Israyil ca seeni xayma.
56Teewul ñuy diiŋat ak a gàntal Yàlla Aji Kawe ji, sàmmuñu ay dénkaaneem,
57xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, toogadi ni xala gu yolom.
58Ñu di ko merlook seen bérabi jaamookaay, di ko fiirlook seen jëmmi tuur.
59Ba ko Yàlla yégee, mer na, ba jéppi Israyil lool.
60Mu gental dëkkuwaayam ba ca Silo, xaymaam ba mu sampoon ca doom aadama ya.
61Mu jébbal ngàllo màndargam dooleem, may gànjaram ca loxol noon ba.
62Daa bàyyee ñoñam saamaru noon, ndax mere yooya séddoom.
63Seeni waxambaane deeye xare, seeni janq lamb;
64seeni sarxalkat loroo saamar, te jëtun jooyul.
65Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw, mel ni jàmbaar ju biiñ xabtal.
66Mu dóor noon ba yari gannaaw, teg leen gàcce gu dul fey,
67ba noppi xalab waa kër Yuusufa, te tànnul giirug Efrayim,
68xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.
69Mu tabax këram gu sell, na mu mel fa kawa kaw, dëgër ni suuf, si mu samp ba fàww.