7Yaw Yàllay Yanqóoba, yaa gëdd, gawar ak fasam nelaw.
8Yaw mii, yaa mata ragal; boo meree, ana kuy taxaw fi sa kanam?
9Fa asamaan nga biraleb àtte; suuf tiit, ne cell.
10Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
11Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy; desu xadaram, nga gañoo.
12Seen Yàlla Aji Sax ji, digooleen ak moom te jëfe ko. Kee jara ragal. Na ñi ko wër ñépp yótsiy teraanga.