Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 76:7-12 in Wolof

Help us?

Sabóor 76:7-12 in Kàddug Yàlla gi

7 Yaw Yàllay Yanqóoba, yaa gëdd, gawar ak fasam nelaw.
8 Yaw mii, yaa mata ragal; boo meree, ana kuy taxaw fi sa kanam?
9 Fa asamaan nga biraleb àtte; suuf tiit, ne cell.
10 Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
11 Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy; desu xadaram, nga gañoo.
12 Seen Yàlla Aji Sax ji, digooleen ak moom te jëfe ko. Kee jara ragal. Na ñi ko wër ñépp yótsiy teraanga.
Sabóor 76 in Kàddug Yàlla gi