Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 74

Sabóor 74:14-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
14yaa rajaxe kaaŋi rab wa, leele ko rabi màndiŋ ma.
15Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal, ŋiisal dex yu masa wal.
16Yaa moom bëccëg, moom guddi, teg fi weer week jant bi.
17Yaa rëdd mboolem digi suuf, sàkk noor ak nawet.
18Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree, xeet wu amul bopp a lay sewal.
19Bul wacce rabu àll sam xati, bul sàggane sa néew-doole yi mukk.

Read Sabóor 74Sabóor 74
Compare Sabóor 74:14-19Sabóor 74:14-19