Text copied!
Bibles in Wolof

Sabóor 74:14-19 in Wolof

Help us?

Sabóor 74:14-19 in Kàddug Yàlla gi

14 yaa rajaxe kaaŋi rab wa, leele ko rabi màndiŋ ma.
15 Yaa fettaxal fii bëti ndox akum wal, ŋiisal dex yu masa wal.
16 Yaa moom bëccëg, moom guddi, teg fi weer week jant bi.
17 Yaa rëdd mboolem digi suuf, sàkk noor ak nawet.
18 Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree, xeet wu amul bopp a lay sewal.
19 Bul wacce rabu àll sam xati, bul sàggane sa néew-doole yi mukk.
Sabóor 74 in Kàddug Yàlla gi