3Kuy wut sama bakkan, yal na rus, torox ne tott. Kuy bége sama loraange, yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.
4Kuy ñaawle, yal na dellu gannaaw, torox.
5Képp ku lay sàkku, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku sopp sag wall, yal na jàppoo: «Yàlla màgg na!»