3 Kuy wut sama bakkan, yal na rus, torox ne tott. Kuy bége sama loraange, yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.
4 Kuy ñaawle, yal na dellu gannaaw, torox.
5 Képp ku lay sàkku, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku sopp sag wall, yal na jàppoo: «Yàlla màgg na!»