Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 68

Sabóor 68:30-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
30Sa kër gi tiim Yerusalem, fa la la buur yiy indiley galag.
31Nanga fa gëdde rabu àll wi ci barax yi, ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu. Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis. Tasaareel xeet yooyu sopp xare,
32ay kàngam bàyyikoo Misra aki galag, réewum Kuus baral loxoom, indil Yàlla.
33Yeen waa réewi àddina, woyleen Yàlla, teral-leen Boroom bi, Selaw
34gawar bi ci asamaan, asamaani démb. Ma ngooguy àddu kàddug doole.
35Seedeleen ne doole, fa Yàlla, mi tiime Israyil darajaam, dooleem feeñoo xàmbaar ya.

Read Sabóor 68Sabóor 68
Compare Sabóor 68:30-35Sabóor 68:30-35