9Bokk yi, wóoluleen ko fu ngeen tollu, diisleen ko seen xol, Yàllaay sunu kiiraay. Selaw.
10Doom aadama, ngelawal neen; nit, naxi neen. Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, kaw la jëm. Ñooy gëna woyof ngelaw!
11Bul wóolu ribaa, bul yaakaar alalu càcc, neen la. Bu sa alal yokku, nga taf ci sa xol.