8Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkóot.
9Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, Efrayim di sama mbaxanam xare, Yuda di sama yetu nguur,
10réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay, Edom, ma teg tànk; Filisti, ma xaacoo fa.»
11Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër? Ku may jiite ba Edom?