1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki toxoro, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2Éy Aji Sax ji, maa ngi àddu, déglu ma, maa ngi onk, teewlu ma.
3Sama Buur, sama Yàlla, déglul, ma ne wallóoy! Yaw laay ñaan.
4Aji Sax ji, ag suba, ngay dégg sama baat, suba su ne ma diis la samay dagaan, di séentu.
5Doo Yàlla ju safoo coxor, yaw lu bon du la daloo.
6Ku réy du taxaw fi sa kanam, kuy def lu ñaaw, bañ nga ko.
7Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen, sib kuy bóomeek kuy wore.