Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 59

Sabóor 59:5-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Defuma lu ñaaw, ñuy xélu, di ma waajal; ngalla, jógal taxawusi ma, ba gis.
6Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Yàlla Boroom gàngoor yi, yewwul, dikkeel xeeti yéefar yépp, mbugal! Workat yu bon yi, bu leen yërëm! Selaw.
7Bu ngoonee ñu wàccsi, di xiiru niy xaj, di wër dëkk bi.
8Déglul li ñuy yebbee ci seen gémmiñ, seen làmmiñ niy saamar, ñu defe ne kenn déggu leen.
9Te yaw Aji Sax ji, yaa ngi leen di ree, yaa ngi kekku yéefar yii yépp.
10Yaay sama doole, ma di la séentu, yaw Yàlla, yaay sama rawtu.
11Sama Yàlla ju goree may gatandu. Moo may may ndam ci noon yi, ma gis.
12Yàlla, bu leen rey, lu ko moy samaw xeet fàtte. Tasaaree leen sa doole, daane leen. Boroom bi, yaa nuy feg.

Read Sabóor 59Sabóor 59
Compare Sabóor 59:5-12Sabóor 59:5-12