7Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ; Aji Sax ji, foqal seen selli gaynde yii.
8Yal nañu ne mes ni ndox muy wal, yal nañu diir seen fitt, mu damm,
9yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey, mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant.
10Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku.
11Aji jub day gis ñu feyul ko, mu bég, muy jàngoo deretu ku bon.