5Day am daŋar ni ñàngóor, fatti noppam ni jaan ju tëx:
6du dégg baatu jatkat, mbaa jati ñeengokat bu ñàng.
7Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ; Aji Sax ji, foqal seen selli gaynde yii.
8Yal nañu ne mes ni ndox muy wal, yal nañu diir seen fitt, mu damm,
9yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey, mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant.