2Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma, fi yaw laay làqu, yiiroo sa kiiraay, ba musiba yi jàll.
3Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji, Yàlla, mi may matalal.
4Mooy yónnee fa asamaan, musal ma, dumaal ma ku may not. Selaw. Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam.
5Maa ngi tëdd ci biiri noon yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama. Seeni sell niy xeej aki fitt, seen làmmiñ di saamar yu ñaw.
6Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan, sag leer tiim suuf sépp.
7Noon yi di ma fiir, sama xol jeex. Ñu gasal mam pax, far tàbbi ca. Selaw.
8Yàlla, dogu naa, dogu naa woy, di la kañ.
9Na sama jëmm jépp yewwu, xalam ak moroom ma yewwu; ma yee leeru njël.
10Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi, kañ la ci biir waaso yi.