7Dama ne: «Éy ku may may laafi xati, ma ne fërr, noppluji.
8Xanaa ma naaw, ba sore, fanaani màndiŋ ma. Selaw.
9Naa gaawtu, seeluji ngelaw lu riddi ak ngëlén.»
10Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen. Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi,
11guddeek bëccëg ñuy wër, ñaawtéef ak ayib wéttali leen.