1Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda.
2Mooy ba waa Sif demee ca Sóol, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew.
3Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur, jox ma dëgg, ci sa kàttan.
4Éy Yàlla, déglul, ma ñaan, teewlul, ma wax la.
5Ay doxandéem a ma jógal, di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan, te seetuñu ci Yàlla. Selaw.
6Yàllaa ngii, moo may dimbali; Boroom bee yor sama bakkan.
7Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru, yal na leen sa dëgg sànk.