8Ana ku mana jota jot sa bakkanu moroom, mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
9Njotug bakkan jafe na, bu ci jéem dara.
10Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?
11Xanaa gis ngeen ne xelu, dee; dof, dee; naataxuuna it faatu rekk, wacce keneen alalam.
12Sa bàmmeel di sa kër, ba fàww, di sa dëkkuwaay bu sax dàkk, boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.
13Nit ak darajaam fanaanul, mook aw rab a yem, sànku rekk.
14Nii la ku wóolu boppam di mujje, mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.
15Nara dee rekk niy xar, ndee wommat, yóbbu, njub fenk nib jant, ku jub moom leen, njaniiw mëdd seen jëmm, fu sore kërug daraja.
16Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw, jot sama bakkan, ba jël ma.
17Buleen yéemu ci ku barele, teraangay këram di yokku.
18Du dee ba yóbbaale dara, teraangaam du ko topp biir bàmmeel.
19Na bége bànneexu bakkanam, ñu di ko kañe koomam,
20ba tey, day dee, fekkiy maamam, ña dootu gis ug leer ba fàww.