6Ana lu may tiit bés yu metti, yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,
7di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare?
8Ana ku mana jota jot sa bakkanu moroom, mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
9Njotug bakkan jafe na, bu ci jéem dara.
10Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?