Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 44

Sabóor 44:18-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Lii lépp dal na nu, te fàttewunu la, fecciwunu la kóllëre.
19Dëdduwunu la, wàccunu saw yoon,
20teewul nga not nu, wacce nu xaj ya, këpp nu lëndëmu ndee.
21Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla, ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo,
22du la ump, yaw Yàlla, mi xam kumpay xol.
23Yaa tax ñu yendu noo bóom, dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.
24Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw? Yewwul, bu nu wacc ba fàww.
25Loo nu làqe saw yiw, di fàtte sunu njàqareek sunu coono?
26Nu ngi ne ñàyy ci pënd bi, di watat koll fi suuf.

Read Sabóor 44Sabóor 44
Compare Sabóor 44:18-26Sabóor 44:18-26