Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 34

Sabóor 34:12-16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
12Dikkal doom, déglu ma, ma jàngal la ragal Aji Sax ji.
13Ana ku dund neex, mu bëgga gudd fan, ba gis ngëneel?
14Na làmmiñam daw lu aay, dawi fen.
15Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.
16Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji, te ay noppam la dékk wooteb wallam.

Read Sabóor 34Sabóor 34
Compare Sabóor 34:12-16Sabóor 34:12-16