Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 33

Sabóor 33:16-21

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.
17Yaakaar aw fas nax sa bopp la, kàttanu fas dug wall.
18Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.
19Day jot bakkanam, di ko dundal cib xiif.
20Nu ngi séentu Aji Sax ji, moo nuy taxawu, di nu feg.
21Ci moom la sunu xol di sedde, turam wu sell lanu wóolu.

Read Sabóor 33Sabóor 33
Compare Sabóor 33:16-21Sabóor 33:16-21