Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 32

Sabóor 32:2-5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ndokklee yaw mi Aji Sax ji toppul ag tooñ, te amoo xelum njublaŋ it.
3Ba ma nee cell, damaa ràgg, dëkke naqar.
4Guddeek bëccëg sa loxo diis gann ci man. Sama doole ŋiis ni ndox mu jaas upp. Selaw.
5Ma xamal la ne moy naa, làqatuma la sama ñaawtéef. Ma ne: «Naa àgge Aji Sax ji sama bàkkaar.» Yaw nga baal ma peyug tooñ. Selaw.

Read Sabóor 32Sabóor 32
Compare Sabóor 32:2-5Sabóor 32:2-5